Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

1

Turu Yàlla ci Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë

Turu Yàlla ci Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë

Araf yi Yawut yi doon binde turu Yàlla ci làkku Ebrë bu njëkk ba, bala ñu leen yóbbu Babilon

Araf yi Yawut yi doon binde turu Yàlla ci làkku Ebrë, bi ñu delloo seen réew

Turu Yàlla feeñ na lu jege 7 000 yoon ci Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë. Ñeenti araf yii lañu ko binde : יהוה. Ay baatoodi la, maanaam consonne ci tubaab. Ñeenti araf yooyu lañuy woowe tétragramme. Tekki Biibël bi tudd Traduction du monde nouveau “ Yexowa ” la tekkee ñeenti araf yooyu. Tur boobu moo nekk tur bi gën a feeñ ci tur yi nekk ci Biibël bi. Yonent Yàlla yi bind Biibël bi, bi ñuy wax ci Yàlla, dañu newoon “ Aji Man ji ”, “ Aji Kawe ji ” walla “ Boroom bi ”, loolu yépp di ay tiitar. Waaye bu ñu bëggoon a tudd Yàlla ci boppam, tétragramme boobu kese lañu doon jëfandikoo.

Yexowa Yàlla ci boppam moo xiir bindkat yooyu ñu jëfandikoo turam. Dafa xiir yonent bi tudd Yowel mu bind lii : “ Képp ku woo Yexowa ci turam, dinga mucc ” (Yowel 2:32, MN). Yàlla xiir na benn bindkatu Sabóor mu bind lii : “ Yal nañu xam ne yaw mi tudd Aji Sax ji [Yexowa, MN] doŋŋ yaay Aji Kawe ji yilif àddina yépp ” (Sabóor 83:19). Turu Yàlla feeñ na sax lu tollook 700 yoon ci téere Sabóor bi nga xam ne ñi doon jaamu Yàlla dañu ko waroon di woy ak di tari. Kon lu tax turu Yàlla feeñul ci Biibël yu bare ? Lu tax Traduction du monde nouveau tekki tétragramme boobu “ Yexowa ” ? Te “ Yexowa ”, lan la tekki ?

Foto bi, ay mbind la yu ñu tibbe ci Sabóor bi nekk ci benn Rouleau de la mer Morte bi amoon ci jamono Yeesu ak taalibeem yu njëkk ya. Mbind yi, ñu ngi leen doon bind ak araf yi ñu doon jëfandikoo ci làkku Ebrë bi Yawut yi doon làkk bi ñu jógee Babilon dellu seen réew. Waaye Tétragramme bi ciy feeñ ay yoon yu bare, moom dañu ko bind ak araf yi ñu doon jëfandikoo ci làkku Ebrë bu njëkk ba

Lan moo tax tur bi feeñul ci Biibël yu bare ? Li ko waral bare na. Am na ñi foog ne, Yàlla Aji Man ji soxlawul a am turu boppam. Am na it ñoo xam ne dafa mel ni benn aada Yawut yi moo leen yóbbaale. Aada boobu dafa doon tere ñu woo Yàlla ci turam, xéyna ngir nit ñi bañ a jëfandikoo tur boobu ci fasoŋ bu ñaaw. Am na itam ñuy wax ne, ndegam kenn mënul xam dëgg ni ñuy waxe turu Yàlla, li gën mooy ñu yem ci tiitar yu mel ni “ Boroom bi ” walla “ Yàlla ”. Waaye loolu ñu wax yépp taxawul fu dëgër, te lii moo tax ñu wax loolu :

  •   Ñiy wax ne Yàlla Aji Man ji soxlawul a am turu boppam, xamuñu ne turu Yàlla dafa feeñ ci ay sotti Biibël yu njëkk ya, ba ci sotti Biibël yi amoon bala Kirist di ñëw ci kaw suuf. Ni ñu ko waxe woon ci kaw, Yàlla dafa xiir ay nit ñu bind turam ci Kàddoom lu jege 7 000 yoon. Kon leer na ne dafa bëgg ñu xam turam te di ko woo ci tur boobu.

  •   Ñiy tekki Biibël bi te topp aada Yawut yi ba dindi turu Yàlla ci Biibël bi, am na lu réy lu leen reer. Bu dee sax yenn xudbakatu Yawut yi dañu doon bañ a tudd tur Yàlla, loolu taxul ñu dindi tur bi ci seeni sotti Biibël bi. Mën nañu gis loolu ci ay sotti Biibël yu yàgg a yàgg yu ñu gis ca dëkku Qumrân ci wetu Géej gi amul dund maanaam Mer Morte. Turu Yàlla feeñ na ci sotti yooyu ay yoon yu bare. Am na ay tekkikatu Biibël yi nga xam ne, bu ñu ko waxul sax, wone nañu ne turu Yàlla mu ngi woon ci Mbind yu sell yi ñu njëkk a bind. Li koy wone mooy, ci seeni tekki, dañuy rampalaase turu Yàlla ak “ BOROOM BI ” bu ñu bind ak araf yu mag. Waaye ba tey wax ji mooy, lan moo leen may fitu rampalaase walla dindi turu Yàlla, fekk xamoon nañu bu baax ne tur boobu feeñ na ci Biibël bi lu mat ay junniy yoon ? Kan moo leen may sañ-sañ boobu ? Ñoom rekk a ko mën a wax.

  •   Ñiy wax ne kenn warul a woo Yàlla ci turam ndaxte kenn mënul xam dëgg ni ñuy waxe tur boobu, gis nañu ne loolu terewul ñuy woowe Yeesu ci turam fekk xamuñu ni ñu daan waxe tur boobu. Taalibe Yeesu yu njëkk ya nekkoon Yawut dafa mel ni Yeshua lañu doon woowe Yeesu, te baatu “ Kirist ” nag, Mashiah maanaam “ Almasi ” lañu ko doon wax. Ñi doon làkk Gereg, Iêsous Khristos lañu ko doon woowe. Ñi doon làkk Latin ñoom, Iesus Christus lañu ko doon woowe. Kon ni ñu daan woowee Yeesu ca jamono jooju wuute na lool ak ni ko karceen yi di woowee tey. Karceen yu njëkk ya dañu xool ni ñu daan waxe turu Yeesu ci làkku Gereg, ñu di ko waxe noonu ñoom itam. Te Yàlla nangu na ñu binde tur bi noonu ci Biibël bi. Noonu itam kurél bi tekki Traduction du monde nouveau dafa gis ne jaadu na ñu binde turu Yàlla “ Yexowa ” bu dee sax wuute na ak ni ñu ko doon waxe ci làkku Ebrë bu njëkk ba.

Lu tax ñu binde turu Yàlla “ Yexowa ” ? Ñeenti baatoodi yii (יהוה) tudd tétragramme ci tubaab ñu ngi leen di binde nii : YHWH. Tétragramme boobu amul woon baatal maanaam voyelles ndaxte ci làkku Ebrë bu njëkk ba, bu ñu doon bind ay baat duñu ci def ay baatal. Waaye bu nit ñi doon jàng ay baat ci làkk boobu, ñoom ci seen bopp ñoo ci doon dugal baatal yi war.

Lu jege junni at bi ñu paree bind Mbind yu sell yi ci làkku Ebrë, boroom xam-xam yi nekk Yawut génne woon nañu ay màndarga yu doon wone yan baatal lañu war a dugal bu ñuy jàng Ebrë. Ci jamono jooju, Yawut yu bare dañu doon ragal a tudd turu Yàlla, di naan loolu baaxul, moo tax ñu rampalaase ko ak yeneen baat. Loolu moo tax bu ñu doon sotti téere yu sell yi ba yegg ci tétragramme bi, dafa mel ni dañu doon jël baatal (voyelles) yi nekk ci baat yooyu ñu doon rampalaasee turu Yàlla, boole leen ci ñeenti baatoodi (consonnes) yi ñu binde turu Yàlla. Kon màndarga yooyu ñu wax léegi mënuñu tax ba ñu xam dëgg ni ñu doon waxe bu njëkk turu Yàlla ci Ebrë. Am na ñu wax ne “ Yahvé ” lañu doon waxe turu Yàlla, ñeneen wax ne neneen lañu ko doon waxe. Téere bu ñuy woowe Rouleau de la mer Morte te am xaaju téere Lévitique ci làkku Gereg, nii lañu ci binde turu Yàlla : Iaô. Te it, bu ñu xoolee li bindkat yu njëkk ya ci làkku Gereg doon bind, mën nañu xalaat ne dañu doon waxe tur boobu Iaê, Iabé walla Iaoué. Waaye kenn mënul wax ne moom rekk a wax dëgg ci loolu, ndaxte xamuñu ni jaamu Yàlla yu njëkk ya doon waxe tur boobu ci làkku Ebrë (Genèse 13:4 ; Exode 3:​15). Li ñu xam mooy, Yàlla nëbbul turam mbooloom, wax na leen turam ay yooni yoon, te ñoom it dañu doon jaar ci turam bu ñu doon wax ak moom, te dañu doon tudd tur boobu bu ñu doon wax ci seen biir (Exode 6:2 ; 1 Rois 8:​23 ; Psaume 99:⁠9).

Turu Yàlla bi feeñ ci Njàlbéen ga 15:2 ci traduction du Pentateuque bu William Tyndale, ci atum 1530

Kon lu tax ñu binde turu Yàlla “ Jehovah ” ci ãgale (Yexowa ci wolof) ? Dañu ko def ndaxte nit ñu bare yàgg nañu di ko waxe noonu ci làkku ãgale.

Tétragramme bi, YHWH, baat bi tekki “ nekk ”

Baat bi tekki “ nekk ” ci làkku Ebrë

Tur wi Yexowa, lan la tekki ? Ci làkku Ebrë, tur wi Yexowa, mu ngi jóge ci baat buy tekki “ nekk ”. Kurél bi tekki Biibël bi tudd Traduction du monde nouveau, dafa sukkandiku ci ay gëstu boroom xam-xam ci làkk boobu ba wax ne turu Yàlla mu ngi tekki “ Dafay tax dara nekk ”. Waaye ndegam boroom xam-xam yépp bokkuñu gis-gis ci loolu, mënuñu wax ne turu Yàlla loolu rekk la tekki. Waaye tekki boobu ànd na bu baax ak taxawaay bi Yexowa am, maanaam Ki sàkk lépp ak Kiy def lépp li ko sóob. Kon tekki boobu dafay wone ne Yàlla yemul rekk ci sàkk lépp li nekk ci asamaan ak ci suuf, waaye, ak lu mënta xew, dafay def ba lépp li mu nas àntu.

Kon li turu Yàlla tekki yemul rekk ci li baat boobu ci làkk Ebrë di tekki ni ñu ko waxe ci Gàddaay gi 3:​14, MN, bi naan : “ Dinaa nekk li ma bëgg a nekk ” walla “ Dinaa doon ki may doon ”. Kàddu yooyu, am na lu ñuy wone ci Yàlla, maanaam Yàlla mën na nekk lépp li war ngir def li mu bëgg ci anam bu mu mënta doon. Waaye li turu Yàlla tekki yemul rekk ci “dinaa nekk li ma bëgg a nekk”. Ëmb na itam li nga xam ne Yàlla moo tax mu am walla mu nekk, muy ci li mu sàkk walla ci li muy def ngir coobareem am.