Ubbil li ci biir

LI NDAW ÑI DI LAAJ

Ndax war naa tatuwaas?

Ndax war naa tatuwaas?

 Lu tax ñu bare bëgg tatuwaas?

Benn ndaw bu tudd Ryan lii la wax: «Yenn tatuwaas yi dañoo rafet lool.»

Li tax nga bëgg tatuwaas mën na soppi sa gis-gis ci tatuwaas. Benn janq bu tudd Jillian lii la wax: «Kenn ku ma bokkaloon lekkool, bi mu nekkee xale la yaayam dee. Bi mu nekkee ndaw, mu jël turu yaayam, tatuwaas ko ci loos wi. Tatuwaas bu mel noonu lu daw yaram la.»

Ak lu mu mën a doon, danga war a jël jot te xalaat bu baax bala ngay def tatuwaas buy des ci sa yaram ba fàww! Lan nga war a xam ci tatuwaas bu dee danga ko bëgg a def? Te yan xelal yi nekk ci Biibël bi ñoo la mën a dimbali nga jël dogal bi gën?

 Lan nga war a xam ci tatuwaas?

Lan la mën a def ci sa wér-gi-yaram? Benn kilinik bu tudd Mayo lii la wax ci palaasam ci internet: «Tatuwaas dafay bënn sa der. Mën nga ci jële ay feebaru der ak yeneen jafe-jafe. Lée-lée ay picc yi ñuy woowe ci farãse granulomes mën nañu génn fi nga def sa tatuwaas. Tatuwaas mën na la jox itam li ñuy wax ci farãse chéloïdes, maanaam sa der dafay mel ni góom bu wér.» Ñu yokk ci ne: «Li ñuy jëfandikoo ngir def tatuwaas, bu laalee deret bu am feebar, mën nga ci jële ay feebaru deret yu bare.»

Naka la la nit ñi di gise? Mu neex la mbaa mu naqari la, li ngay def ci sa yaram dafay wone lu bare ci yow. Mën na tax ñu xoole la ni mag walla xale, ku ñu mën a wóolu walla ku jarul a wóolu. Lii la benn janq bu tudd Samantha wax: «Saa yu ma gisee nit ku tatuwaas, ci saa si dama koy jàppe ku bëgg noos ak naan sàngara.»

Mélanie mi am fukki at ak juróom ñett, lii la ci yokk: «Tatuwaas dafay nëbb sa taar ak ki nga doon dëgg. Dafa mel ni, ñiy tatuwaas bëgguñu nga xam ki ñu doon dëgg. Moo tax ñuy nëbbatu ci ginnaaw tatuwaas.»

Ndax dinga kontine di ko bëgg? Tatuwaas bi nga def, mën na ñaaw ndax danga gën a am yaram walla danga gën a màgget. Lii la benn ndaw bu tudd Joseph wax: «Gis naa ni tatuwaas di mel bu nit ki demee ba màgget, rafetul dara.»

Allen mi am ñaar fukki at ak benn lii la wax: «Suñu gis-gis ci tatuwaas dafay gaaw a soppeeku. Li amoon solo ci nit ki mën na dem ba dootul amati solo ci moom.»

Li Allen wax dëgg la. Li ñuy gën di màgg suñu gis-gis, suñu bëgg-bëgg ak li ñu fonk dafay soppeeku, waaye tatuwaas yi duñu soppeeku. Ndaw si tudd Teresa lii la wax: «Am tatuwaas bu may fàttali yëfi dof yu ma defoon te mën leen a réccu ëllëg, du li ma gënal.»

 Lan la ci Biibël bi wax?

Ku mat dafay jël jot ngir xalaat bu baax bala muy def dara (Kàddu yu Xelu 21:5; Yawut Ya 5:​14). Kon bàyyil xel ci li Biibël bi wax lu jëm ci tatuwaas.

  • Kolos 3:20: «Xale yi, déggal-leen seeni waajur ci lépp, ndaxte looloo rafet ci ñi bokk ci Boroom bi.»

    Boo dëkkee ak say waajur te bañ leen a déggal, loolu lu mu la mën a jural?

  • 1 Piyeer 3:3, 4: «Bu seen taar aju ci col, maanaam ay létt, wurus mbaa yére yu rafet, waaye nay taar bu sax bu nekk ci biir, di xol bu nooy te dal, ndax loolu lu takku la fa Yàlla.»

    Lu tax Biibël bi di gën a fësal «taar bu sax bu nekk ci biir»?

  • 1 Timote 2:9: «Na jigéen ñi di [solu] [...], cig woyof ak maandu.»

    Baatu «woyof» lu muy tekki? Lu nit ki di gën di màgg, lu tax woyof gën a am solo tatuwaas?

  • Room 12:1: «Na seen dund mel ni sarax su ñuy defal Yàlla, sarax su sell te neex ko. Loolu mooy njaamu, gi leen war.»

    Lu tax li ngay def ak sa yaram am solo ci kanamu Yàlla?

Ñu bare jël nañu dogal bañ a tatuwaas, bi ñu xalaatee ci xelal yi ñu gis fii. Gis nañu lu gën a am solo tatuwaas. Teresa, mi ñu waxoon sànq nee na: «Bu amee ay kàddu yu la neex lool, defal li ñu wax. Bu amee nit koo bëgg dëgg, wax ko fi mu la tollu. Loolu moo gën def tatuwaas.»