Ubbil li ci biir

Woneel li nekk ci téere bi

LI ÑUY DEF AK LI NGEEN DI MAYE

Ndaje yi mbooloo yi di def ci internet

Ndaje yi mbooloo yi di def ci internet

26 SUWEŊ 2020

 Bi feebaru Korona komaasee, ci dëkk yu bare, nguur gi dafa sant ñu bàyyi dajaloo, te bàyyi lu tollook benn meetar ci suñu diggante ak ñeneen ñi. Seede Yexowa yi dañuy topp li nguur gi wax. Loolu moo tax, ñu komaase di def seen ndaje yi ci internet. Léegi, dañuy def seen ndaje yi ci Zoom ak yu ni mel, ngir kontine di daje te kenn du wàll sa moroom.

 Jataay biy dogal bu seede Yexowa yi, moo génne xaalis ngir mbooloo yi mën a am Zoom. Fan la xaalis boobu jóge? Ci li nit ñi di maye ngir jàppale suñu liggéey. Noonu, mbooloo yi yépp mën nañu kontine di daje te kenn du wàll sa moroom. Amoon na ay mbooloo yoo xam ne mënuñu woon a fey li ñu soxla ngir def seeni ndaje ci internet, ndaxte dafa jafe woon ci ñoom. Loolu dafa doon jar 9 000 ba 13 000 FCFA, walla sax lu ko ëpp. Looloo tax mbooloo yooyu doon def ay ndaje ci internet yoo xam ne, doo fey dara. Waaye nag, yenn saay, loolu wóorul woon. Te it, ñi lay may nga def ay ndaje ci internet te doo fey dara, ñoom ñooy wax ñaata nit ñoo ci mën a teew. Waaye léegi, mbooloo yooyu dañuy jëfandikoo Zoom bi leen suñu mbootaay bi feyal. Noonu, dafay gën a yomb ñu def seeni ndaje ci fasoŋ bu wóor, te ñu bare mën nañu ci teew. Loolu dimbali na bu baax mbooloo yooyu. Fi mu tollu nii, lu ëpp 65 000 mbooloo yu nekk ci lu ëpp 170 réew a ngi jëfandikoo Zoom bi leen mbootaay bi feyal.

 Mbokk yi nekk ci mbooloo Kairagi, ca dëkku Manado, Sulawesi du Nord, ca réewu Indonésie, dañu doon def seeni ndaje ci internet, te duñu doon fey dara. Waaye léegi, ñu ngi jëfandikoo Zoom bi leen mbootaay bi feyal. Lii la mbokk Hadi Santoso wax: «Amoon na ay mbokk ñoo xam ne, mënuñu woon a jëfandikoo bu baax telefon, ordinatër ak yu ni mel. Waaye léegi, mën nañu jariñoo bu baax ndaje yi, ndaxte soxlaatuñu di konektewaat ay yooni yoon ci benn ndaje.»

 Mbokk Lester Jijón Jr., mi nekk mag ci mbooloo Guayacanes-Est, ca dëkk Guayaquil, ca réewu Équateur, lii la wax: «Ci yenn mbooloo yi, mbokk yu bare dañoo néew doole. Looloo tax mënuñu woon a fey Zoom bi mënoon a tax mbooloo bi yépp teewe ndaje yi. Waaye léegi, ak Zoom bi ñu mbootaay bi feyal, mën nañu woo ñu bare ci suñu ndaje yi, te duñu ragal nit ñi bare, ba dootuñu xajati ci koneksiyoŋ bi.»

 Mbokk Johnson Mwanza, mi nekk mag ci mbooloo Ngwerere-Nord ci dëkku Lusaka, ca réewu Zambie, lii la bind: «Mbokk yu bare ci mbooloo mi wax nañu ne, li leen mbootaay bi defal, tax na ñu gën a jege mbokk yi, yu góor ak yu jigéen, ci mbooloo mi. Waaye itam yëg nañu ci, mbëggeelu Yexowa, te gis ne mu ngi leen di topptoo bu baax.»

 Jënd nañu Zoom yooyu ak xaalis bi mbootaayu seede Yexowa yi jagleel suñu mbokk yi musiba dal, te mu jóge ci li nit ñi di maye ngir jàpple liggéey bi ñuy def ci àddina si sépp. Ñu bare dañuy jaar ci internet, ci donate.isa4310.com ngir maye dara. Jërëjëf ci may yi ngeen di joxe ak xol bu sédd! May yooyu ñoo tax ñu mën a dimbali suñu mbokk yi musiba dal ci àddina si sépp.—2 Korent 8:14.